Dalal-Jàmm Ci Wolof Rek !
- Aw làkk a ngii wareesukoo sàggane () kum soxalul xamaguloo lu mu mane
- Ak a nooy te matale man na lu ne () Tànn leen ko nu far ko di waxtaane
- Yéwwute bokk na ci fonk sa làkk () Dina waral nga déggook say mbokk
- Xam-xam la ca jiitu dégg sa làkk () Dégg gu wer di ca waxtaan te di ca sàkk
- Deglu leen ma wax li ma fanaane () Tëdd di gént nguur def ko waxtaane
- Mudi jël làkk wi def ko wow ofisel () Di ci xalaat di ci liggeey looloo di xel
- Àbb aw làkk indi ko di ci lëggeey () Te yor wu mat nit ku ñuul yeen a geey
- Ku la aal bët fu ko neex yaw ngay man a xool() Lu lay may bët du nangu yaw nga di ko xool
- Jëm ciw naaj àbbi dàll ànd ak boroom () Bu tàggee mu laaj la ko nde mooko moom
- Looloo nu dal batax dunu dem ca kanam () Jéggaani làkk, cosaan, ba ci xam-xam
- Mbokk yéwwul te xàmmee yaw li nga moom () Tubaab ya de tée na ñu ñoom lañu moom
- Maay jooy tu lii ci kanamu waa guur gi () Ak ku ko man ci askan wi mbaa kilifa gi
- Sosal nufi baatukaay nuy baatal () Di sosi baat, baat bu jagul nu baaxal
- Làkk woo xamni numu la neexe nga koy waxe () Lii de ganul nañu ci sàkki am mbexe
Lu Nu Tax a Juk ?
- NEES MAN A DEF BA SUQALI WOLOF LÁKK WI NU MAN JURAL ASKAN WU YEWWU XAY TE XARAÑ?
- NEES WAR A DEF BA SUQALI WOLOF?
- NDAX WOLOF DAA MATUL ?
- NDAX LI MUY LÁKKU NIT KU ÑUUL A TAX ?
- NDAX NIT KU ÑUUL MOO XEEB YËFAM ?
- NDAX DADI WOLOF YEE KO SÁGGANE ,
Mbaa-jàmm Bokki Wolof yi ? Nun dey ay wolof la nu yu wolofe te yaakaar ni looloo nu war batax noo juk di laggeeyal wolof moomi ngir mu dabi ay nawleem walla mu jege leen, Te loolu jombul Wolof ndax Yàlla tàggat na ko ba mu nooy te matale, Man dey gis a gu ma làkk wu ko gën a mat, Xanaa kay li am mooy làkk wees toppatoo ak wees sàngane te melna ni Wolof ci yees xaw a sàngane la bokk, Nun dey loolu neexu nu batax noo juk fas-yéene cee def li nu ci man a kus neew ngir dooleel ko mbaa sax wone ko te nu yaakaar ni kepp kuy wolof war na cee jàpp ndax Yàlla mi la bind def la ngay wolof. di jéggaani aw làkk te yor wu mat, nooy te neex a wax loolu bokkul ci fulla day tax ñu yab la te xeeb la, looloo waral réewi tugal yi not ñu te yab nu ba leegi nde ñoo ñu abal aw làkk wu ñuy liggeeyee te Wolof nee «Ku la aal bët fu ko neex ngay xool», nun dey fippu nanu ngir bàyyil leen fi séen làkk yooyi du nu ci weesu wut xam-xam bi nu bokk ñun nit ñepp te ñu aakimoo ko def ko ci seen làkk yi, ndax xam-xam ku ne xam na ni Afrig la fékk baax doxondéem yi ñëw tibb ko yobbu. Li nu ci jot a am a kus neew nu tekki ko ci Wolof ngir askanu Wolof yi yëgul lu xew man cee njariñu, Fii ci sunu réew yi lu tax ñu yeex ? bokku na ci ku fi juddoo ñu dugal la ci daaray nasaraan yi 12at ngay jàng ngir dégg làkku nasaraan door a dugg ci daara ju kawe ji(universite) di jàng laggeey(métiers) 12at yooyii di juge ci sag dund ngir jàng aw làkk woo man a laggeeye te yor Làkku-Juddu wu mat manoon cee jànge xam-xam ci 12at yooyii, Xam ngéen ni loolu jaaduwul moo waral it doofi gis ku am xaalis ci'k ndawam ak yeneeni mbir yu wara tax ñu fonk suñu làkk wi, làkk woo xamni booy gent ci ngay gént booy saaga it ci ngay saaga, boo bëggee defar sa gent di nga ko jëfandikoo,
Jaajëf ci teewlu gi
Gis-Gis
-
-
-
Sànni-Kàddu
require('inc_rate.php');
getComments("1");
submitComments("1","$PHP_SELF");
?>